Seet ko ci Google : Google Search désormais disponible en Wolof
mercredi 15 septembre 2010
“Seet ko ci Google” [1]. Cette phrase en wolof prendra désormais un tout nouveau sens. En effet, avec le lancement de l’interface Wolof de Google Web Search il est désormais possible pour les Internautes du Sénégal d’accéder à Google en wolof pour effectuer leurs recherches.
Dans le cadre de notre mission d’organiser l’information à l’échelle mondiale et de la rendre utile et accessible, le support des langues joue un rôle très important. Google Africa est ainsi très fier d’avoir permis la prise en charge de plusieurs langues utilisées par des millions d’africains. Nous allons plus loin, avec l’initiative « Google in Your Language » (GIYL), en permettant d’étendre cette prise en charge à toutes les langues : GIYL offre à des volontaires passionnés par une langue comme le Wolof et soucieux de promouvoir sa présence en ligne, des outils pour traduire l’interface Google dans cette langue.
Tout le bénéfice de la disponibilité de Google en Wolof revient cependant à l’équipe de l’équipe de 45 volontaires (étudiants et experts) qui, grâce à la collaboration entre Google et l’Université Gaston Berger (UGB) de Saint Louis, se sont réunis au mois de juin sur le campus de l’UGB pour un marathon de traduction enthousiaste et productif. Mohamadou El-Hadj Nguer, enseignant à l’UGB, qui a dirigé les travaux de traduction, explique l’enthousiame des experts et des volontaires par leur envie de renforcer la presence du Wolof en ligne et leur conviction que la disponibilité de Google Search en Wolof va donner plus de raisons d’écrire dans cette langue et lui donner une opportunité de développement sur Internet.
Maintenant, comme vous pouvez le voir sur http://www.google.sn/, “Google deggna Wolof” (Google comprend Wolof).
Angela Muigai, Localization Community Manager (Afrique)
(Source : Google Africa, 15 septembre 2010)
Seet ko ci Google : Google Search jàppandi na léegi ci Wolof
“Seet ko ci Google”. Kàddug Wolof gii dina am léegi weneen maanaa ak doorug jokkalekaayu Google ci Wolof ngir Seet ci Web bi ak Google ci Senegaal.
Ci sunu sémbub dundal xam-xam ci àdduna sépp te fexe mu am njariñ te jàppandi, jumtukaayu làkk wi lu ci am solo la. Google Afrig bég na lool ci li mu fexe ba boole ci làkk Afrig yu ay milyoηi doomam di jëfandikoo. Dinanu egg sax fu gën a sore ak naalub « Google ci Saw Làkk » (GIYL), ngir jàppandal ko ci làkk yépp : GIYL day may ay way-coobarewu yu aw làkk soxal, niki Wolof, te bëgg mu suqaliku ci buum gi (Web bi), ay jumtukaay ngir ñu tekki jokkalekaay gu Google ci làkk woowu.
Njariñal jàppandig Google ci Wolof a ngi ñeel nag kuréel gu 45 way-coobare (Ndongook i way-màcc), yi nga xamne ci lonkoog Google ak Iniwersite Gaston Berger bu Ndar, ci bëj-gànnaaru Senegaal, ñoo ànd ci weeru suwe ca Iniwersite ba ngir amal liggéey bu am a am njariñ bii. Allaaji Mamadu Nger, jàngalekat ca UGB, di ki jiite liggéey bi, leeral na cawarte gi way-màcc yeek way-coobarewu yi am ci bëgg a dëgëral làkk Wolof ci Web bi ak seenug dogu ci ne jàppandig Google Ceet ci Wolof dina wone lu bari lu nu war a bindloo Wolof ak yeneen i njariñ yees mën a amee ci yëngu ci internet.
Bis niki tey, “Google dégg na wolof’. Doorees na ko ci http://www.google.sn/
Ki ko siiwal di Angela Muigai, Aji-saytu làkk yi, Afrig
[1] signifie “Recherche sur Google”